bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg

Scan the qr code to link to this page

Hadith
Explanation
View Translations
Benefits from the Hadith
Categories
More ...
Jële nañu ci Miqdaat Doomi Mahdii-karib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne: "bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg".
Sahih/Authentic. - At-Tirmidhi

Explanation

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- day leeral benn ci yiy dëgëral diggante way-gëm ñi, tey tasaare mbëggeel seen biir, te mooy bu kenn bëggee mbokkam mu wax ko ne da koo bëgg.

Benefits from the Hadith

  1. Ngëneelu mbëggeel gir Yàlla rekk tax, ci lu dul njariñul àdduna.
  2. Sopp gi ñu sopp
  3. ñu xibaar ki ñu bëgg ngir Yàlla ci bëgg gi ñi ko bëgg, ngir mbëggeel ga ak miineel ga gën a yokk.
  4. Tasaare mbëggeel ci biir way-gëm ñi day dëgëral mbokkoog mgëm, day wattu mbooloo mi ci taasaaroo ak tàqalikoo.

Categories

Successfully sent!