?kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog

Scan the qr code to link to this page

Hadith
Explanation
View Translations
Benefits from the Hadith
Categories
More ...
Jële nañu ci Abdulaa Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog.
Sahih/Authentic. - Al-Bukhari

Explanation

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne nit ku mat ci jokk bokk ak rafetal jëme ci jegeñaale yi nekkul nit kiy fay rafetal cig rafetal, Waaye jokk-katu mbokk dëgg mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkoom mu jokk ko, bu ñu ñaawalee jëme ci moo; dakoy faye ag rafetal jëme ci ñoom.

Benefits from the Hadith

  1. Jokk mbokk gi Lislaam jàpp mooy nga jokk ku la dog, di baal ku la tooñ, di jox ku la xañ, waaye jokk nekkul ci defalante ak fayantoo.
  2. Jokk mbokk dana nekk ci nga fexe ba éggale ci ñoom lu jàppandi ci aw yiw niki alal ak ñaan ak digle lu baax tere lu bon ak yu ni mel, ak nga fexe ba jeñal leen aw ay.

Categories

Successfully sent!