?socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi

Scan the qr code to link to this page

Hadith
Explanation
View Translations
Benefits from the Hadith
Categories
More ...
Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».
Sahih/Authentic. - An-Nasaa’i

Explanation

Yónent bi day xamle ne setal ay bëñ ci bantu garabu Araag ak lu ko niru, day laabal gémmiñ ci ay tilim-tilim ak xet yu bon yi, Waaye daa bokk ci sabab yiy tax Yàlla gërëm jaamam bi; ndax topp Yàlla ak wuyu ay ndigalam moo ci nekk, ak li ci nekk ci sett gi nga xam ne Yàlla da koo bëgg.

Benefits from the Hadith

  1. Ngëneelu socc, ak li Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaax aw xeetam ci ñu koy baril.
  2. Li gën ci socc mooy jëfandikoo bantu Araak, jëfandikoo boroos ak pat dana ko man a wuutu.

Categories

Successfully sent!