képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon

Scan the qr code to link to this page

Hadith
Explanation
View Translations
Benefits from the Hadith
Categories
More ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- muy wax naan: "képp ku aj ngir Yàlla te beejul ( sëyul wala mu wax lu bon) deful tamit yëfi kàccor, dana dellu mel ni bis ba ko yaayam jure woon".
Sahih/Authentic. - Al-Bukhari and Muslim

Explanation

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne képp ku aji te beejul, beej mooy: sëy ak yi koy jiitu ci fóon ak joññoo, dees na ko wax it jublu ci wax ju ñaaw, te kàccoorewul ci def ay moy ak yu ñaaw, Te bokk na ci kàccoore def yi ñu araamal. Dana dellu juge ci ajam gi di ku ñu jéggal, kem ni liir bi di juddoo nekk ku mucc ci ay bàkkaar.

Benefits from the Hadith

  1. Ag kàccoore doonte da ñu koo tere ci jamono ju ne, waaye tere gi day gën a tar ci biir aj ngir màggal jaamu yi nekk ci aj gi
  2. Nit day judd ci lu dul njuumte, di ku sett wicc ci ay bàkkaar; te du gàddu bàkkaar
  3. i keneen.

Categories

Successfully sent!