?ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara

Scan the qr code to link to this page

Hadith
Explanation
View Translations
Benefits from the Hadith
Categories
More ...
Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdallah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: «ku dajeek Yàlla te bokkaalewu ko ak dara dana dugg àjjana, waaye ku dajeeg moom bokkaaleko ak dara dana dugg sawara».
Sahih/Authentic. - Muslim

Explanation

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamale ne ku faatu te bokkaalewul Yàlla ak dara kon jëmuwaayam mooy àjjana doonte sax mbugël nañu ko ci yennati bàkkaaram, waaye ku faatu fekk doon na bokkaale Yàlla ak dara dana sax sawara.

Benefits from the Hadith

  1. Ngëneelu kennal Yàlla, ak ne sabab la ci mucc ci sax ca sawara.
  2. Jegeg àjjana ak sawara ci jaam bi, ci ne dara doxul digganteem ak ñoom lu dul dee.
  3. Moytandikuloo ci bokkaale moo xam mu néew walla mu bari; ndax mucc ci sawara moo ngi ci moytu ko.
  4. Njàngat ci jëf yi moo nga ca muj ga.

Categories

Successfully sent!