ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem

Scan the qr code to link to this page

Hadith
Explanation
View Translations
Benefits from the Hadith
Categories
More ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "Yàlla mu kawe mi nee na: ñiy bokk ñépp maa ci gën a doylu, képp ku jëf jenn jëf bokkaale ma ca ak keneen ma bàyyi ko ak bokkaaleem".
Sahih/Authentic. - Muslim

Explanation

Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu baarkeel mi te kawe dafa wax ne: moom moo gën a doylu képp kuy bokk, mooy ki doylu ci lépp, bu nit defee ag jaamu defal ko Yàlla ak ku dul Yàlla; Yàlla da koy bàyyi te du ko ko nangul, daal di koy delloo boroom; Kon warees naa sellal jëf yi ngir Yàlla mu kawe mi, ndax Moom -tudd naa sellam ga- du nangu lu dul lu sell ngir jëmmam ju tedd ji.

Benefits from the Hadith

  1. Moytandikuloo bokkaale ci bépp melokaanam; ndaxte moom day teree jëf mu ndangu.
  2. Yëg doylug Yàlla ak ug màggaayam dafa bokk ci liy dimbali nit ki ci mu man a sellal jëf.

Categories

Successfully sent!